#alternate Soppi Wikipedia (wo) Saltige Jóge Wikipedia. Sauter à la navigation Sauter à la recherche Saltige, benn tur la, ci cosaanu Séeréer yi ak Pël, bu ñuy woowee boroom xam xam yi. Cosaanu baat bi[Soppi • soppi gongikuwaay bi] Saltige, ci lakku bambara (bamanakan) la juge. Ci bambara, noonu lañu ko xajalee: * Sila (mooy yoon wi) * Tigi (mooy njiit bi). Kon, Silatigi, ca njeelbeen, mooy kepp kuy jiite yoon wi. Saltige Séeréer yi, ak Silatigi bu Fuuta Tooro[Soppi • soppi gongikuwaay bi] Ci seereer yi, Saltige bi, mooy kuy yoree mbirum xam xam yi. Ñoo yoree mbirum paj ak gisaan, ci askan wi. Gëdd bu mag lañu yoroon, ndax ñoom a tax ñu mënoon wuti safaara ci lu demoon ci wallu bey mi, nawet gi, ak yeneen coono yi askan wi jankoontel. Dañoo dendoon lool nguur gi (Siin-Saalum), buuri seereer yi, di leen yegle ak di leen digal lu bare, ngir buuri yoree nguur gi ci añam yu rafet, reew mi jem kanam te am jamm. Ci seereer yi, nekk Saltige, ndono la. Lebu yi ñu xam ni, seen maam, ay seereer lañu woon ci lu ëpp, ba tey, am nañu tamit seen Saltige, di bokk ci mbootaayu ñooñu nekk ca kaw askanu Lebu, Seriñ Ndakaaru bi moo leen jiite. Fuuta-Tooro nag, Silatigi bi, buur la woon, moo doon yoree nguur gi. Deeniyaɲkooɓe yi, giir gu daan jiite reewum Fuuta, ci diggante 1526 ba 1778, seen buur, Silatigi lañu ko daan woowee, wante laata Fuuta-Tooro nekk seeni nguur, buur yi fa nekkoon, yeneen tur lañu amoon. Silatigi boobu, da naroon bokk ci geño Koly Teɲella ku sos giir googu. Tey, ci Pël yi, Saltige amaatul. Waaye ci Seereer yi ba tey, Saltige yi ñungi wey li ñu doon def demb, di faj ñooñu febar japp, te ñepp xam neen xeew bi ñu tudd Xoy, ci dëkku Seereer yi, laata nawet gi agsi, Saltige yi ñu def ko ngir yegal askan wi mbaa nawet gi dina neex am det, ak yeneen xibaar bu mëna jëm ci wallu nguur gi, ak yeneen. Bu ñu jeexe li, su de dañoo gis lu bon a bugga ñow ci dëkk, di nañu digal ay saaxaar, nit ñi war ko def, ngir lu bon baña agsi. Ci lebu yi, dañoo yengu ci Ndœp, di ay tuur, ngir faj nit ñi. Ci « https://wo.wikipedia.org/w/index.php?title=Saltige&oldid=90527 » lañ ko jële Njëlu joowiin Samay jumtukaay * Duggoo de * Waxtaan ak bii IP * Cëru * Sos am sàq * Dugg Barabu tur * Jukki * Waxtaan [ ] Wuute Wonewiin * Jàng * Soppi * Soppi gongikuwaay bi * Wone jaar-jaaram [ ] Yeneen Seet ____________________ Seet Ayca Joowiin * Xët wu njëkk * Askan * Coppite yu mujj * Aw xët ci mbetteel * Ndimbal Móol/génne * Sos ab téere * Yebbi niki PDF * Sumb bu móolu Boyotu jumtukaay yi * Xët yi mu lëkkalool * Coppite yi ko ñeel * Yeb ab dencukaay * Xëti jagleel * Lëkkalekaay yu fi nekkandi * Xibaar ci xët wi * Yëf Wikidata * Tudd wii xët Yeneeni làkk Ajouter des liens * Coppite bu mujj bu xët wii 18 Nowembar 2012 ci 03:28. * Jàppandig ëmbéef lee ngi sukkadiku ci Creative Commons Attribution- Séddoo ci genn anam gi; Man nañoo sukkadiku itam ci yeneen anam. Xoolal anami jëfandiku gi ngir yeneeni leeral. * Politigu sutura * Ci mbiri Wikipedia * Ay aartu * Suqalikat * Statistiques * Déclaration sur les témoins (cookies) * Woneyiin bu mobil * Wikimedia Foundation * Powered by MediaWiki