#alternate Soppi Wikipedia (wo) Sibiru Jóge Wikipedia. Sauter à la navigation Sauter à la recherche Sibbiru Malaria.jpg Ab Plasmodium bu bawoo ci tiflitu yoo bu jigéen di dox ci biir selilu yoo bi. Toftale ak balluwaayi biti Specialty infectiologie[*] ICD-10 B50-B54 ICD-9-CM 084 OMIM 248310 DiseasesDB 7728 MedlinePlus 000621 eMedicine med/1385 emerg/305 ped/1357 Patient UK Sibiru MeSH C03.752.250.552 Sibbiru ab feebar bu yoo di joxe di dal nit ak yenn rab yi te li koy joxe di parasit protozoan (benn xeetu selil microorganism) bu xeetu Plasmodium.^[1] Ni sibbiru di faral di feeñee mooy yaram wu tàng, coono, waccu ak metitu bopp. Su demee ba tar mën na jur der bu mboq, say, komaa wala faatu.^[2] Feebar baa ngi tàmbalee feeñ fukki fan ak juróom ginaaw bu la yoo bi màttee. Ñi mu dal te faju ñu ko bu baax, mën na leen dalaat ginaaw ay weer ci kanam.^[1] Ñi mu dal bu yàggul ba ñu mucci, su leen dalaatee du metti noonu. muslaay boobu nit ki am dafay jeex su amee ay weer wala at sudee newul fu mu mën a amee sibbiru.^[2] Gis nañu ni, màtt-màttu yoo bu jigéen bi tuddu Anophele mooy joxe feebar bi. Sula màttee dafay dugal parasit yi nekk ci tiflitam ci sa deret.^[1] Ginaaw loolu mu jàll ci res wi ndax foofu lay màggee ak juree. Juróomi xeeti Plasmodium a mën a dal nit te ñooy la nit mën a wàlle.^[2] Ñu bari ñu sibbiru di faat P. falciparum ak P. vivax, P. ovaleñoo leen faat, ak P. malariae biy joxe sibbiru bu tarul lool.^[1]^[2] Xeet yi tudd P. knowlesi bariwul lu ñuy daaneel nit.^[1] Bu ñuy seet ndax danga sibbiru jël ci sa laamu deret xool ko ci mikroskop, wala ñu jëfandikoo test bi tuddu antigen-based test bu gaaw la.^[2] Defar nañu jumtukaay buy jëfandikoo polymerase chain reaction ngir gis ADN bu doomu jàngoro ji, waaye loolu bariwul ci barab yi sibbiru bari ndax dafa seer te jafe.^[3] Sibbiru bu mën na wàññiku bu baax sudee nit ñaa ngi jëfandikoo sàñce (mustikeer) wala diw bu dàq yoo ngir moytu màtt-mattu yoo yi, wala def lu leen di dàq wala ray, lu ci melni pompu yoo ak dindi dox yi taa.^[2] Bari na garab yu ci melni prevent malaria yiñ jagleel ñiy tukki ci barab yu sibbiru bi tasaaroo. Yenn saa mën nañu bindal xale sulfadoxine/pyrimethamine xale ak jiggéenu wérul ci ñatti weer yi njëkk cib ëmb bi ci barab yi sibbiru bari lool. Fiñu tollu amagul ñakk bu ci mën a aar ni naam soxla nañu ko, teewul nit ñaa ngi ciy gëstu bu baax ngir am ko.^[1] Ñaari xeeti garab yi ñu digle ngir faj feebar bi ñooy garab yiy xeex sibbiru bi amaale ab artemisinin.^[1]^[2] Ñaareelu garab gi mën na doon mefloquine, lumefantrine, wala sulfadoxine/pyrimethamine.^[4] Mën nañu itam jël Quinine boole ko ak doxycycline sudee artemisinin amul.^[4] Mooy lañuy digle ci barab yi feebar bi bari, dañu wara xam bu baax ndax nit ki dafa sibbiru laata muy jël garab yi ndax dañuy bañ jàngoro ji dërkiis ci garab gi. Jangoro dem na ba dërkiis ci yenn xeetu garab yu daan faj sibbiru; lu ci melni, dërkiis ci-chloroquine P. falciparum barina ci barab yi sibbiru bi bari, te itam dërkiisam ci artemisinin doon na jafe-jafe bu mag ci réew Asi Gànjoolu-penku.^[1] Fi feebar bi gënee bari mooy ci réew yu tàng yi ak xawa tàng te ñooy yi séq rëdd wiy xaajale suuf si di ekuwaatër.^[2] Bokk na ci ñoom Afrigu Suufu-Sahara, Asi, ak Amerik Latin. Mbootaayu Wérgi-yaramu Àdduna bi maanaam OMS xayma na ci atum 2012, ni amoon na 207 miliyoŋi ñu amoon sibbiru. Ci at moomu, feebar bi fatna lu tollu ci diggante 473,000 ak 789,000 doomu aadama, li ëpp ci ñoom doon ay gunéy Afrik.^[1] Fuñu tuddee sibbiru xel yi dem ci ndóol te loolu doonul lu baax ci koom-koom guy suqaliku.^[5]^[6] Xayma nañu ni at mu nekk sibbiru dina ñàkkloo Afrik lu tollu ci $12 miliyaar ciy dolaar ndax pajum feebar bi, ñàkk a mën a liggéey ak li muy yàq turism bi.^[7] Royuwaay yi[Soppi • soppi gongikuwaay bi] 1. ↑ ^1,0 ^1,1 ^1,2 ^1,3 ^1,4 ^1,5 ^1,6 ^1,7 et ^1,8 "Malaria Fact sheet N°94". WHO. March 2014. Retrieved 28 August 2014. 2. ↑ ^2,0 ^2,1 ^2,2 ^2,3 ^2,4 ^2,5 ^2,6 et ^2,7 Caraballo, Hector (May 2014). "Emergency Department Management Of Mosquito-Borne Illness: Malaria, Dengue, And West Nile Virus". Emergency Medicine Practice 16 (5). 3. ↑ Nadjm B, Behrens RH (2012). "Malaria: An update for physicians". Infectious Disease Clinics of North America 26 (2): 243–59. PMID 22632637. doi:10.1016/j.idc.2012.03.010. 4. ↑ ^4,0 et ^4,1 Organization, World Health (2010). Guidelines for the treatment of malaria (2nd ed. ed.). Geneva: World Health Organization. p. ix. ISBN 9789241547925. CS1 maint: Extra text (link) 5. ↑ Gollin D, Zimmermann C (August 2007). Malaria: Disease Impacts and Long-Run Income Differences (PDF) (Report). Institute for the Study of Labor. 6. ↑ Worrall E, Basu S, Hanson K (2005). "Is malaria a disease of poverty? A review of the literature". Tropical Health and Medicine 10 (10): 1047–59. PMID 16185240. doi:10.1111/j.1365-3156.2005.01476.x. open access publication - free to read 7. ↑ Greenwood BM, Bojang K, Whitty CJ, Targett GA (2005). "Malaria". Lancet 365 (9469): 1487–98. PMID 15850634. doi:10.1016/S0140-6736(05)66420-3. Ci « https://wo.wikipedia.org/w/index.php?title=Sibiru&oldid=98165 » lañ ko jële Wàll : * CS1 maint: Extra text Njëlu joowiin Samay jumtukaay * Duggoo de * Waxtaan ak bii IP * Cëru * Sos am sàq * Dugg Barabu tur * Jukki * Waxtaan [ ] Wuute Wonewiin * Jàng * Soppi * Soppi gongikuwaay bi * Wone jaar-jaaram [ ] Yeneen Seet ____________________ Seet Ayca Joowiin * Xët wu njëkk * Askan * Coppite yu mujj * Aw xët ci mbetteel * Ndimbal Ci yeneen sémb * Wikimedia Commons Móol/génne * Sos ab téere * Yebbi niki PDF * Sumb bu móolu Boyotu jumtukaay yi * Xët yi mu lëkkalool * Coppite yi ko ñeel * Yeb ab dencukaay * Xëti jagleel * Lëkkalekaay yu fi nekkandi * Xibaar ci xët wi * Yëf Wikidata * Tudd wii xët Yeneeni làkk * Afrikaans * Akan * Alemannisch * Aragonés * العربية * مصرى * অসমীয়া * Asturianu * Azərbaycanca * Башҡортса * Žemaitėška * Беларуская * Беларуская (тарашкевіца) * Български * भोजपुरी * বাংলা * Brezhoneg * Bosanski * Буряад * Català * Mìng-dĕ̤ng-ngṳ̄ * ᏣᎳᎩ * کوردی * Čeština * Cymraeg * Dansk * Deutsch * Thuɔŋjäŋ * ދިވެހިބަސް * Eʋegbe * Ελληνικά * English * Esperanto * Español * Eesti * Euskara * Estremeñu * فارسی * Suomi * Võro * Føroyskt * Français * Frysk * Gaeilge * Kriyòl gwiyannen * Galego * Avañe'ẽ * गोंयची कोंकणी / Gõychi Konknni * ગુજરાતી * Hausa * 客家語/Hak-kâ-ngî * עברית * हिन्दी * Hrvatski * Kreyòl ayisyen * Magyar * Հայերեն * Արեւմտահայերէն * Interlingua * Bahasa Indonesia * Igbo * Ilokano * Ido * Íslenska * Italiano * 日本語 * Patois * Jawa * ქართული * Kabɩyɛ * Қазақша * ಕನ್ನಡ * 한국어 * Kurdî * Кыргызча * Latina * Лезги * Lingua Franca Nova * Lingála * Lietuvių * Latviešu * Minangkabau * Македонски * മലയാളം * Монгол * मराठी * Bahasa Melayu * Malti * မြန်မာဘာသာ * नेपाली * नेपाल भाषा * Nederlands * Norsk nynorsk * Norsk bokmål * Sesotho sa Leboa * Occitan * Oromoo * ଓଡ଼ିଆ * ਪੰਜਾਬੀ * Polski * پنجابی * پښتو * Português * Runa Simi * Română * Русский * Русиньскый * संस्कृतम् * Саха тыла * ᱥᱟᱱᱛᱟᱲᱤ * Sardu * Sicilianu * Scots * سنڌي * Srpskohrvatski / српскохрватски * සිංහල * Simple English * Slovenčina * Slovenščina * Soomaaliga * Shqip * Српски / srpski * Sunda * Svenska * Kiswahili * தமிழ் * ತುಳು * తెలుగు * Тоҷикӣ * ไทย * Tagalog * Türkçe * Xitsonga * Татарча/tatarça * Українська * اردو * Oʻzbekcha/ўзбекча * Tiếng Việt * Winaray * 吴语 * IsiXhosa * მარგალური * ייִדיש * Yorùbá * Vahcuengh * 中文 * Bân-lâm-gú * 粵語 * IsiZulu Soppi lëkkalekaay yi * Coppite bu mujj bu xët wii 13 Oktoobar 2015 ci 08:59. * Jàppandig ëmbéef lee ngi sukkadiku ci Creative Commons Attribution- Séddoo ci genn anam gi; Man nañoo sukkadiku itam ci yeneen anam. Xoolal anami jëfandiku gi ngir yeneeni leeral. * Politigu sutura * Ci mbiri Wikipedia * Ay aartu * Suqalikat * Statistiques * Déclaration sur les témoins (cookies) * Woneyiin bu mobil * Wikimedia Foundation * Powered by MediaWiki